Waxi Sëriñ Tuubaa ci julli
Waxtaani Sëriñ Tuubaa ci julli
1.
Amna bis Sëriñ Tuubaa XLML di julli taw ba sóob. Ba mu sëlmalee wax ne di julli muy taw metti na waaye nekk ci biir bàmmeel muy tàkk moo ko gën a metti
" Loolee saxal na amug mbugëlum bàmmeel te bu saxee saxalaale xéewalug bàmmeel. Wallaahu ahlam "
2.
Sëriñ Tuubaa XLML mas nay julli ji am sàq muy tàkk am ñu ko bëgg a fayi. Mu ne bu ko kenn fay na ñépp dem julli ji. Ba ñu jullee ba ñëw fekk dara desu fa.
" Yaa ayyuhal lasiina aamanu laa tulhikumuu amwaalukum wa laa awlaadukum han sikril laahi "
" Sëriñ bi màggug Yàlla TWT lay teewlu waxtu wu nekk. Moo tax ay jëfiinam di wuute ak li nu xam ñun. Lii soreewut ak sànni ab der ci am ndox di julli. Wallaahu ahlam "
3.
Sëriñ Tuubaa XLML mas nay sàkketlu ba waxtu wa tàbbee kenn bàyyiwul. Ba mu ñëwee ne leen firileen mbooleem lu ngeen fi sàkket ba ñu nodee ak léegi. Wér na lool
Am na ay wuute ci làmmiñu ñiy nettali. Wallaahu ahlam
4.
Sëriñ Tuubaa XLML mas nañu koy bayal toolub dugub. Ba waxtu julli jot kenn bàyyiwul. Ba mu ñëwee laaj fu ngeen tolloon ba waxtu wi di teew? ñu wax ko kok. Mu ne dagg leen lépp. wér na lool
Lii soreewut ak sàq ma doon tàkk. Amna ku ma ne baayam nee na ko ca la bokkoon, tisbaar la woon. Wallaahu ahlam
5.
Amna ku mas a ñëw ci Sëriñ Tuubaa XLML am kumu àndal, ne ko kii samab jaam la. Dama koo indi woon di la ko jox haddiya. Sëriñ bi ne bëreet di julli ràkkaa yu gudd. Ba lu noppee ne ko loo wax? Mu ne ko kii samab jaam la, dama koo indii woon haddiya, Sëriñ bi ne ko boo ko moomee yaa ma moom. Wér na
" Day mel ni moom ki bind rekk a ko jagoo, teewul ñuy askanale dara ci kenn ndax moom la ko Yàlla dénk. Sëriñ bi nag xayna baatub jaam bi mu tudd moo rëy ci moom, ba tax mu defee noonu ak di ko jàngal tawhiid. " Wallaahu ahlam
6.
Amna ab taalube bu doon xëccoo ak i pël suuf Sëriñ Tuuba XLML tere ko mu diibal ba far nangu suuf ca ñoom, ñëw ci Seriñ bi ag yoor-yoor naa ko , maa ngi sant Yàlla bu baax. Sëriñ bi ne ko ci lan? Mu ne ko suuf sa nangu naa ko, Sëriñ bi ne ko mbaa nangu waale nga asamaan sa ? ñoo bokk Boroom de ! ñoo bokk Boroom de ! wér na
"Xul a innaakum la takfuruuna bil lasi xalaxal arda fii yawmayni... " Wallaahu ahlam
7.
Sëriñ Muhammadu Mustafaa ak Sëriñ Muhammadul Faadal RLTH mas nañu laaj Sëriñ Tuuba XLML lu dig taalibe ? Ak fu Yàlla nekk ? Sëriñ bi ne leen, ag taalibe laaj leen fo Ibra Faal. Fu Yàlla nekk ? Laaj leen ko Maxtaar Jóob.
Mu ( Maxtar Jóob ) ne leen Yàlla xamuma ci moom dara waaye moom fumu nekk Yàlla nga fa. wér na
" Inna rahmatal laahi xaribuun minal muhlisiniina, maa yakuunu min najwaa salaasatin illaa huwa raabihu hum... "
Sunu Boroom amul barab, du jëmm itam ju ñuy daj ci sunuy yaram waaye nee na moo nu gën a jege sunu xol. Ndax luy firndel loolu moo di ba mu nuy bind ci sunu biiru nday la nu defal ay xol aki cër. Kenn ku nekk kem ni nga koy jubloo ni lay nekke ci yaw. Sëriñ bi nag ni mu jubloo Boroomam ci lépp moo tax mu nekk ci léppam. Di wax ci moom, di def ci moom, Wajjahtu kulliya... Wallahu ahlam
8.
Tubaab yi mas nañoo wax Sëriñ bi : Dañoo bgg nga wan nu Yàlla ji ngay jaamu nu koy jaamu. Sëriñ bi ne leen dibeer jooju ngeen di màggal ; Damaa bëgg ngeen jàpp ci noppam indil ma. Siiw na
Sunu Boroom nee na :
" Laa tudrikuhul absaaru wahuwa yudrikul absaara. "
kenn du ko gis ci àdduna ku dul Yónnent bi STHW ca na mu ko soobee, ni ko Sëriñ bi andee ci ay mbindam, bu dee ëllëg nag dananu ko gis ni mu ñëwee ci Alxuran
" Wujuuhun yawma isin naadiratun illa rabbihaa naasiratun "
njariñal gis ko nag moo di topp ay ndigalam ak bàyyi ay tereem, mel ni looy gën di góor-góorlu ci ay ndigalam, di bàyyi ay tereem, dangay yëg di gën a xam ag amam. Nee na itam fekke na lépp it, lépp lunuy def itam mi ngi koy gis. Loolu nag sunuy jëmm doy nañu tegtal sëkk ci moom ndax kenn ku nekk xam nga bu wér ne, bari na lool loo xam ci sa bopp ak loo gis ci sa bopp te wóor na la ne amna ku ko def, kon kookee soriwu la .
" Wa nahnu aqrabu illayhi min kum walaa kin laa tubsiruuna. " Wallaahu ahlam
bamba