Jaar jaar Maam Cerno Mbacké

Jaar jaar Maam Cerno Birahim Mbacké Boroom Daaru Muhti

Jaar jaar Maam Cerno Mbacké
: :



GÓOR YÀLLA GI

Boroom Daaru Muhti :

Moo ngi gane àdduna ca Poroxaan atum 1866 bisub alxemes ca yoor-yoor ba.

Ci ñaari waajur yu baax Maam moor Anta Sali, Soxna Faati Isa Jóob.

Néeg ba mu nekkoon diirub ayu-bis bimu ganee àdduna bis bu set Sëriñ Tuubaa wàcce fa ab kaamil

Sëriñ Moor Anta Sali daa junj naan Sëriñ Tuubaa kii mooy sam Haaruuna!



Ab Njàngam:



Bimu matee dal jàng la ko waajuram jox ki ñiy wax Sëriñ Ñaŋ mu dalal ko

Ginnaaw loolu Sëriñ Tuubaa ko defal lépp, ci moom la mokkale Alxuraan,

xam-xam it Sëriñ bee ko jàngal li ëpp,

Boroom Daaru lu nekk ci moom Sëriñ Tuubaa ko def moo tax muy nit ku mat sëkk ci wàll yépp bay benn ak Sëriñ Tuubaa!



Boroom Daaru Muhti: Moom de lu nit musul nangul Sëriñ Tuubaa nangul na ko lu ëpp

lu ko nit mas a bañal nangul na ko lu ko gën a metti!

Moo tax SëriñTuubaa waxoon ni : " Maam Cerno de masul taqalikoo ak man masul juuyoo ak man ci ak ndawam ba ci ag magam "!

Moom nag daa jëloon léppam teel a jox Sëriñ Tuubaa

Moo tax daa na wax naan: "Sëriñ Tuubaa de xanaa lumu bëggul waaye lumu bëgg dina am "



Pastéef bi ak fit wi foo ko takk weesu na ko. Amul soxla ci dara foo ko fekk ndigal moo ko fa bàyyi.

Bi SëriñTuubaa di dem ca géej ga moom la bàyyee woon yoon wi ak njaboot gi mu yar ñépp.

Sëriñ Fàllu daan na wax " sunu Baay Cerno moo nu jàngal ban ni arr yar nu ban ni nërr "



Juróom ñaari at Sëriñ bi bàyyi ko ak yoon wi tubaab bi di ko xeex di taal ay këram ñu bari di ko daw

ngir ragal tubaabCerno ak njaboot gi ca jàmbaar ba , bis sax ci am sàq la fanaan ak ñoom

muy dund guddi yu metti waaye masul bëgg juuyoo akndigalu Sëriñ bi lumu metti metti.



Jaayoon léppam jox Sëriñ Tuubaa moo tax bimu yoree njaboot gi bi Sëriñ bi nekk ci géej gi,

mbas mu metti am ci réew mi, lenn ci njaboot gi di faatu

bimu demee ba metti mu tàllal ñaari loxoom ne " Yàlla njabootug Sëriñ Tuubaa gi bu ci kenn naratee dem

jël mawalla sama waajur walla saa njaboot gite bàyyi fi njabootug Sëriñ Tuubaa gi ".



Di royukaay ci murit yépp ndax daa mel ni Sëriñ Tuubaa bëgg ab murit mel ko lépp da koo def ci moom,

mu boole Chariiha ak Haqiiqa dib taalibe bu raxul dara man ci tool yi man ci jàkka ji

moo tax amna ñaari bataaxel yoo xam ne ci moom rekk la mas a daje bii Sëriñ Tuubaa di ko wax mu indi ci kër gi ak dundu

bii guwërnëer ba fi nekkoon jamono jooja di ko wax mu dimbali réew mi cig dundu



Jaamu Yàlla moom moo ci man ku dul moom waxtu yépp jàkka ja la ko daan jullee

daan bañ lool sax ku dugg ci jàkkaam te amoo njàpp, Alxuraan ñaar fukki isib la daan jàng bis bu set

te bokkul ak limu daan naafila guddi, daan dimbali ñépp këram yaakaar masu faa tas.

Amoon ay taxawaay yu fés ci biir kër Sëriñ bi , Sëriñ bi wóolu woon ko ci mbiri boppam

daan disóo ak ñoom Yàlla baaxe woon ko mu xam Sëriñ bi lool.



Bi Sëriñ bi nekkee ci géej gi mbooleem bataaxel yimu daan yónnee ci moom lay jaar manees naa wax ni,

bunu naan yoonu Murit Boroom Daaru tax ndax mooy léppi Sëriñ Tuubaa di rakkam ju ko déggal.

Nekkoon nit ku noppi lool ci lu amul njariñ nekkoon ku woyof di ku wàcce woon boppam toroxlu

te gën a jege Sëriñ bi ñépp ci biir ak biti moo tax daan na seedeel Sëriñ Tuubaa naan :

"moom de mayug Yàlla rëy naa lool waaye jikkoom ju rafet rekk de yilif na ku ne "



Bokk na ci ay jagleelam lu ëpp ñeen fukki wird Sëriñ Tuubaa joxoon na koko mu daan joxe wird yépp

Murit, Tiijaan, Xaadir, Saasali. Noonu it la meloon ci islaam bi yépp bëgg ñépp te Yàlla tax

daan defal ñépp xàmmee wul kum bokkal tariixa ak kaneen ken masul dégg kum amal benn xaar ma Yàlla!

Loolu di wane ni murit dëgg noonu lay mel.



Bataaxel bi bokk na ci yi ko Sëriñ Tuubaa bind di ko ci gërëm ne ko :

saa busa gët tegee ci loy yii nanga wóolu ne ki ko bind gërëm na la gërëm goo xam ni ak sàññi du si topp,

te moo ngi sàkku ci Yàlla nga am loo xam ni sa kem yépp dinañu la ci ñee nasa xel dal te sa xol sedd!



Ñoo ngi koy fàttaliku fukki fan ak juróom ci weeru baraxlu mu déppoo ak bis bim tasse woon ak Sëriñ Tuubaa

ginnaaw bi ko fi Sëriñ bi bàyyee dem ci géej gi mu liggéyal ko fi liggéey bu rëy

yoon wi yokk nit ñi gën a gëm mu jàngal ñépp lépp luy bëggug Sëriñ bi di itteem!



Moo ngi fi bàyyikoo ci atum 1943 ñaar fukki fan ak ñeenti ci weeru baraxlu ( Chahbaan) bisub alxemes ca Daaru Muhti,

dund gu barkeel goo xam ni lépp  gërëm la ak wéy ci ndigal

Góor Yàlla gi daal di dëddu Asaman ak Suuf ñépp jooy ko boroom fit wa njàmbaar ga

Yàlla nanu ko Yàlla fayal ci barkeb sangam ba Sëriñ Tuubaa

                                                                                          

                                                                                                                           

  Téeré  Góor Yàlla gi