Ndénkaane Seex Ahmadu Bàmba Xaadimu Rasuul
Ndénkaane Seex Ahmadu Bàmba Xaadimu Rasuul
Ab dog buy tàqarle diggante Muriid (Aji namma yegg ci Yàlla ) ak Mariid (Aji féttérlu biy topp Bakkanam)
- Melow muriid mooy bàyyi nammeel ngir jëmmi Yàlla miy def la kok soob
- Képp ku nammul dara ndare Yàlla sunu Boroom, di na yegg ca moom
- Sóobul yoonaam te ànd ak kuy yare di aji laabire bu lay wommat jëmee ca Yàlla ci ay laabire
- Képp ku aju ci ku yegg di na yegg, ku aju ci ku yeggul da fay dog ( du yegg)
- Saa bu la Sëriñ biy aji yare digëlee, jëfeel ndigël la di nga yegg ci sa Boroom
- Saa bu la teree dara, bul jeng jëm ca te bul sàgganee sàkku ngërem
- Ndax Sëriñ bu di aji yare nammul ci taalibeem lu dul yéggale ko ci Yàlla musël ci seytaane
- Képp ku lay tektal leneen lu dul Yàlla na nga ko daw ndax daf lay sànq
- Képp ku lay tektal Yàlla, boo wuuteek moom ca seytaane ngay dali
- Nékkal aji gëm, di jëfee ponki Lislaam yi te di leen sellal boo nammee dox jëm ci Yàlla kon ngay ku rafetal
- Bul bàyyi pas-pas ya di ko jug sunna, te ngay taqoo jaamu Yàlla
- Te bul nekk di geestu ku dul Yàlla sa Boroom Bi moom jaam ñi, moom seen i jëf ak jamono
- Tawhiid (Wéetël Yàlla) moo lay musël ci kéefér gu bon ak caay-caay
- Sellal sa xol moo lay musël ci ngistël
- Képp kuy woote naan da fay jëmee ca Yàlla te jaarewu ko ca yoonam wa dessu ko nangul
- Dénk naa la bii dog yaw Muriid bi ( aji namma yegg ci Yàlla), boo ko toppee kon seytaane di na jubale lor ci keneen ku dul yaw
- Nu ngi sant Yàlla, Yàlla na dollo xéewël ak mucc Yonent bi SAWS
- Ak i njoñam ak i Sahaabaam ak ña leen topp, liféeg Yàllaa ngi tàbbal Ibliis ci keneen ku dul man
bamba