Jaar jaar Sëriñ Masàmba Mbàkke
Ab teunk ci Jaar jaar Sëriñ Masàmba Mbàkke
XEJJUB BOROOMAM
Sëriñ Masàmba Mbàkke :
Moo ngi gane àdduna bisub alxemes tolloo ak ñaar fukki fan ak juróom ñaar ci weeru Baraxlu ci atum 1300 ca Paataar, tolloo ak 14 Juillet 1882,
Juge ci ñaari waajur yu baax Maam moor Anta Sali ak Soxna Aysatu Jóob siiwe ci Soxna Isa Jóob.
Sëriñ Tuubaa moo ko jox aw tur tudde ko maamaam Sëriñ Bàcc Masàmba Anta Céebu miy maami waajuram wu jigéen daan jàngal it Maam Moor Anta Sali.
Amna ñu mu bokkal waajur wu jigéen:
- Sëriñ Moor Isa Jóob
- Sëriñ Ibraahima Lóo
- Sëriñ Amsatu Lóo
- Sëriñ Móodu Lóo
- Sëriñ Àbdu Kariim Lóo
Moom Sëriñ Masàmba ginnaaw maam Moor Anta Sali la feeñ, ganeem àdduna dëppoo ak sosug Yoonu Murit,
Moom nag mooy caatu Maam Moor Anta Sali, mu bok ci waa Kokki yi di sët ci Sëriñ Maxtaar Ndumbe Jóob mi Sëriñ Tuubaa waxoon ne: mooy sangub jamonoom!
Njàngum Alxuraanam:
Sëriñ Tuubaa ko dalal jàng ginnaaw bi Sëriñ Ndaam Abdu Rahmaan Lóo jàngal ko ba mu mokkal ci at yu néew, bi mi am fukki at rekk jàng na ba mokkal.
Te bokk na it ci ñi njëkk jànge ci Sëriñ Ndaam Abdu Rahmaan Lóo ci Daaru Haliimil Xabiir Ndaam bi Sëriñ bi wàccee Sëriñ Ndaam.
Njàngum Xam-xamam:
Bu ñu la waxee loxo yimu jaar ci wàllu xam-xam rekk dinga xam ni boroom xam-xam dëgg la woon, ñooy:
- Boroom Daaru Muhti
- Maam Boroom Saam
- Sëriñ Mbàkke Busso
Te bi Sëriñ bi nekkee Gànnaar yokk na fa xam-xamam lu bari ci Sëriñ bi ak boroom xam-xam ya nekkoon ca Gànnaar
Meloo bindam:
Nit ku matoon ci bind la, gàttul, njoolul dafa yam, amoon taxawaay bu rafet xar kanam bu rafet. Sëriñ Tuubaa magam la niru woon bind lool bay benn. Ku ko gis xam ne nit ku bari jàmm la ak colam daan tolloo ak jëmm ji, lu weex la daan sol.
Ñatti Kaala la daan kaalawoo teg ci ñatti kaamili Alxuraan benn ci kaw ak ndayjooram ak càmmoñ bi.
Meloo jikkoom:
Nit ku yaatu la woon te tabe, këram la ñépp daan daje di xeewlu, neexoon waxtaan lool te ay waxam daawul génn nee na ( Maanaam Sëriñ Tuubaa nee na). Mu nekkoon ki dàq a nettali waxi Sëriñ bi...
Dënn bi daan riir, kenn daawu ko xàmmee ak Sëriñ Tuubaa, muy wax kàddu gi xumb lool di wax ca kaw xejjub boroomam.
Ag Tarbiyaam:
Ku ne xam ne Sëriñ bi daaraam njàng mi ak yar bi ñooy ànd.
Kon Sëriñ Masàmba loxo yi mu jaar ci wàllug njàng ci la ab tarbiyaam tàmbulee te ñoom ñépp Sëriñ bee leen yar, mu am tawféexu moom it jaaraat ci loxo Sëriñ bi. Yeesalaat ak jaayanteem ca Cëyeen.
Tarbiya bu metti ci jamono yu metti ak dëkk yu metti diggante Cëyeen ak Gànnaar ak Njaaréem. Mu futtiku sax ci liggéeyal Sëriñ bi bañ a lu ko dara!
Ginaaw bim tarbiyawoo ci loxoy Sëriñ bi ba fépp fu nitu Yàlla di àgg mu àgg fu ko raw, ca la futtikoo di ko liggéeyal.
Gënoon a fess ci Xassiida yi, mu amoon ak may goo xam ne kenn fekku ku ci te loolu. Sunu Boroom moo wax Sëriñ Tuubaa ne ko Sëriñ Masàmba na jëmële ab liggéeyam ci Xassiida yi. Loolu nag ak may ak gëneel feete wu ko kaw.
Sax ci liggéeyal Sëriñ Tuubaa liggéey yu wuute :
Di ko bindal, bokk it ca Daaray Kaamil ba, daan jiite Mawlid ba, waxtaan yi Sëriñ bi daan def it moo ko daan jiite, Yàlla mayoon ko xalimaam niroo ak xalimag Sëriñ bi.
Mu xam bindum Sëriñ bi lool, xam waxam lool Xassiida yi sax bëggaloon seen bopp Sëriñ Masàmba.
Mbooleem lu Sëriñ bi bind, la mu fekk ak la mu fekkewul lu ëpp mu daan ko sottil Sëriñ bi, yamul woon sax ci bind rekk waaye Guddi Àjjuma yi ak Gàmmu yi yépp Sëriñ bi moom la daan jiital ci njàng mi.
Foo masaan a fekk Sëriñ Masàmba bu bindul, Kureelkat yi ñoo ngi ko wër di jàng. Amul woon sago ci déglu Xasiida. Daan teral ñi daan jàng fonk leen lool ngir cofeel gi mu amoon ci Sëriñ bi.
Bis Sëriñ bi da koo woolu ak mbokk yu bari di ko laaj lan la bëgg waaye Sëriñ Masàmba ne ko man lima bëgg mooy foo toog ba juge fa mu mel ni maa fa toog, moo tax bu Sëriñ bi masaan wax ba noppi ñépp dañiy wëri Sëriñ Masàmba di ko laaj li Sëriñ bi wax.
Daawul bàyyi bénn "araf" ci waxi Sëriñ bi, ñépp yéemoon ko ci loolu, lu Sëriñ bi wax mu xam ko ak lumu bar-bar nag.
Xam gi mu xamoon waxi Sëriñ bi taxoon na ay jataayam ñépp daan ko daan yàkkamti di ko xaar ba kilifa yi sax dañu ko daan sàkku ci moom.
Tassaare na lu bëri ci Yoonu Muriit rawatina tokki yi mu daan def, daan wax lu wér, te xam lamuy wax lool, te daan ko wax te Yàlla tax. Ay waxam li ci ëppoon mooy nee na rekk!
Moom nag ku noppaloon Sëriñ Tuubaa la ndax ni Sëriñ Tuubaa bëgg ku ko mel da koo meloon.
Sëriñ Abdu Xaadir daan na wax naan: Sëriñ Ndaam Abdu Rahmaan Lóo neen na : Sëriñ Masàmba de boroom tawfeex la ndax ku ne bi nga ñëwee ci Sëriñ Tuubaa la nga indaale ci lu dul noonu Sëriñ bi da koo dindi , sotti ca la mu ca bëgg a sotti waaye Sëriñ Masàmba Sëriñ bee njëkk ci moom ba loolu fekku ko ci.
La Seex Ibraahiima Jóob Mashariyu waxoon tënk na dundam gi mu ne:
<< Bu nekkee ki gën a ndaw ci mbokki Sëriñ bi it mooy ki ci gën a kawe itte maanaam ki gën a rëy pasteef >>
Li mooy lanu doon dajale ci dundug Sëriñ Masàmba Xejjub Boroomam. Mu fees dell ak i bind yunu man a ruy. Noo ngi leen di sant ci topp gi ak yittewoo gi, Yàlla na lépp di taxféex junuy jural ngërëmul Sëriñ bi.
bamba