Waxi Sëriñ Touba ci ndigal yi ak tere yi
Waxi Sëriñ Touba ci ndigal yi ak tere yi
1.
Sëriñ Tuuba XLML nee na àjjana joo xam ne lu la neex wax lu la neex def amuma ko. Ku ko dégg feneen bu yaboo dem fa.
" Safiha man yatlubu jannaatin bilaa, hibaadatin fa innahuu lan yuqbalaa."
2.
Amna bis ñuy nodd am soxna suy wax ak Sëriñ Tuubaa XLML. Ba nodd ga daanoo mu ne ko xanaa xamóo wax cig nodd day yeexal sukuraat? Mu ne ko tee woon nga ma ko wax ma noppi? Sëriñ bi ne ko kon ma wax. wér na lool
Li tax ma andee ko nii lii laa mujj a dégg ci làmmiñu Sëriñ Saaliwu RLTH, nee na itam koo ku mooy way-juru Sëriñ Murtadaa RLTH. Wallaahu ahlam
3.
Sëriñ Tuuba XLML mas naa wax Sëriñ Mbàkke Buso RLTH : Jullit bu boolee juróom ñent yii mucc ci àdduna ak allaaxira :
- Ragal Yàlla
- Ragal ku ragal Yàlla
- Ragal ku ragalul Yàlla
- Bàyyi lu bon
- Bàyyi ku bon
- Bàyyi fu bon
- Lumu xamul bumu ko wax
- Lumu manul bumu ko def
- Lumu moomul mu maandu ca
Siiw na walla wér na
4.
Sëriñ Tuubaa XLML mas naa wax Sëriñ Hiisaa Jenn : mbaa du ngeen jëw ? Mu ne ko fasunu ko yéene. Sëriñ bi ne ko ana nu ngeen koy defe ? Mu ne ko funu nekk di tudd sa mbaax gi. Sëriñ bi ne ko kon du ngeen jëw (ñatti yoon ) . Wér na
5.
Sëriñ Tuubaa XLML mas na wax Sëriñ Hiisaa Jenn : mbaa du ngeen yàq dugub ? Mu ne ko fasunu ko yéene. Sëriñ bi ne ko : ndax xam ngeen luy yàq dugub ? Am ku ne ko xanaa moo di togg lu ëpp ba noppi di ko wetti ( tuur ). Sëriñ bi ne ko niru na ko nag waaye du moom. Yàq dugub moo di lekk ba suur, doo def lu neex Sunu Boroom ba mu rees. Wér na
" Kuluu minat-tayyibaati wahmaluu saalihan "
6.
Sëriñ Tuuba XLML bi mu jóggee Jolof jëm Njaareem. Amna ku leen romb di laaj taalibe yi :Ndax amul ku leen fi romb ? Am ku ne ko ku gàtt te ñuul ? Sëriñ bi ne ko nii ngeen di yàqe seen mbokkum jullit. Sëriñ bi ne ko : demal ba gis ko jéggalu ko . Lu ko moy bu ma fekkaat fii. Wér na
Jëw bokk na ci bàkkaar yu mag yi. Yónnent bi SHWS nee na : benn jëw a gën a tar fanweeri njaalo ci Lislaam. Bari na lool ci jamono jii nu nekk ba kenn jàppewu ko dara ci lii Sëriñ bi wax dananu ci mana xame kon bunuy moytu fii lanuy tàmblee jëm kaw. Wallaahu ahlam
7.
Sëriñ Tuubaa XLML mas nay dox guddi ci këram ba yam ci ñuy jëw. Ba mu xëyee wax ne nañu gas foofee suuf sa féete woon kaw féete biir. Jàngalu fa ay kaamil yu bari. Wér na lool
Sëriñ bi soree na ak jamonoy Yónnent bi SHWS te jëw ca jamonoom la haraamoon, teewul gis nanu ni mu koy moytoo. Kon nun ñii ñëw ginaawam. Bunu jàpp ne tere googee ak bañ googee dara wàññiku na ca. Wallaahu ahlam
8.
Sëriñ Tuubaa XLML nee na koo ci digal dara bu génnee naan manum lëmm te boo ko bàyyee ak Malaaka wenn waxtu, muy ŋaax ni am mbaam. Siiw na
Lu mel nii foo ko tekk kenn ay def lenn walla mu wax ko. Nit ñi masuñoo yam te duñu yam ba mukk. Wamaa halar-rasuuli illal balaaxu. Wallaahu ahlam
9.
Amna saalum-saalum bu mas a ñëw ci Sëriñ Tuubaa XLML ne ko : ña nga ma booleeloon ñépp digal naa leen jaamu Yàlla sunu Boroom waaye defuñu ko. Da may xalaat dem wacc leen fa walla ma génne leen. Sëriñ bi ne ko boo demee nga digal leen jaamu Yàlla TWT buñu ko defee nga ànd ca ak ñoom. Bu ëllëgee nga mucc, ñu mucc. Buñu ko deful, bu ëllëgee nga mucc. Wér na
Amna ñuy wax : bu ëllëgee ba ngeen dellu ca ka leen ko digaloon nga mucc. Wallaahu ahlam
10.
Sëriñ Tuubaa XLML mas naa tomb ñenti tomb ne : benn tomb bi li ñu la digal ; ñaareel bi li ñu la tere ; ñatteel bi li nga bëgg ; ñenteel bi li nga ragal. Boo saxee ci li ñu la digal loo bëgg am ko. Boo dee moytu li ñu lay tere doo gis loo ragal. Wér na lool
Wa anjaynal lasiina aamanuu wa kaanuu yattaquuna, wa awfuu bihahdii uufi bihahdikum, wa tiikal quree ahlaknaahum lammaa salamuu... Taras saalimiina musfixiina mimmaa kasabuu... Wallaahu ahlam
11.
Sëriñ Tuubaa XLML nee na nangeen am fulla, nangeen am fayda, nangeen farlu. Fulla moo di loo sori sori ci mbir fa ca lu baax yam nga yam fa. Fayda moo di looy def ci lu baax nga yamale nekk ca yaw dong ak nekk ca ak junni. Farlu moo di loo baaxoo def ci lu baax saa su waxtu wa nga ko daan def jotee nga dem def ko ak lumu xat xat. Wér na
Sëriñ bi mbooleem lumu wax ci biir wax ji da naan lu baax, lu baax nag moo di diine. Kon daa bëgg nu sax ci ndigal yi tey moytu tere yi. Wallaahu ahlam
12.
Amna weeru koor woo xam ne ba muy dëgmal, Sëriñ Tuubaa XLML daa dajale ña ca kër nga bind fi suuf Chahru Ramadaan ak Alxuraan ne bunti àjjana juróom ñatt lañu. Harafi Chahru Ramadaan juróom ñatt lañu. Képp ku koy woor sunu Boroom dina la dugal àjjana. Bunti Sawara juróom ñatt lañu. Harafi Alxuraan juróom ñatt lañu, képp ku koy jàng Sunu Boroom dana la tëjal bunti Sawara. Nangeen ci farlu, ci weer wii. Wér na
Loolii dananu xamal ne jaamu gu nekk amna fumu gënee ci weer yi ak bis yi, ñëw na ci Hadiis luy tegtale ne julli ci Yónnent bi SHWS ci àjjuma la gën. Wallaahu ahlam
13.
Sëriñ Tuubaa XLML nee na juróom yii buñu xam seen juróom yii :
- Seen i way-jur buñu xam seen ug naqari dereet.
- Seen ug njaboot buñu xam seen ug nay.
- Waxtuy julli yi buñu xam seen i yitte.
- Seen barabi liggéeyukaay buñu xam seen ug tàyyeel.
- Seen i dëkkandoo buñu xam seen ñaaw i teggiin.
bamba