Waxi Sëriñ Touba
Waxi Sëriñ Tuuba yuy jàngalé mbokk taalibé yi
- Am na bis Sëriñ bi woo mboolo mi ba ñu ñëw mu ni leen tuub leen te dem jaamuji Yàlla sunu Boroom ba muy ñetti yoon daa di ubuwaat ba waxtu wa dellusi ca ëllëg sa mu ubbi ni leen ma firil leen séen baatu démb yi.
Li tax ma ni leen tuubi leen mooy bisa ngi ñëw muy yawmal Qiyaam, da ngay gis nit muy daw di daw di daw ba Malaa' ika taxaw fi kanamam ni ko diw looy daw tee ngaa taxaw, mu ni ko damaa gis ci sama kanam lu raglu lu xasaw te lu ma daw bëgg koo sori mu gën maa jege.
Malaa' ika ba ni ko kon boo yaboo taxaw ndax loo lu mooy jëf ya nga daan jëf ba nga nekkee àdduna la leen manoona téqale mooy tuub te fii du barabu tuub yéena bokk fa ngeen jëm muy safaanu àjjana.
Tuubi leen bala leena loo loo dal. Li tax ma ni leen jaamuji leen Yàlla mooy bisa ngi ñëw boo xam ni di nga gis nit muy daw di daw ba Malaa' ika taxaw fi kanamam ni ko diw looy daw tee ngaa taxaw mu ni ko damaa gis kër yu rafet yu taaru yu xeeñ lu neex te lu ma daw ngir bëgg koo jege mu gën maa sori, Malaa' ika ba ni ko kon boo yaboo taxaw, kër yee ñooy ya ñuy fayee ña doon jaamu Yàlla ca àdduna, ba nga nekkee àdduna nga ca manoona am, la la ca manoona may mooy jaamu Yàlla fii nag du barabu jaamu Yàlla boo yaboo nga taxaw ndax fee du say kër kon jaamuji leen Yàlla bala leena loo loo dal.
bamba